Gore xewoon la
Gore xewoon la
Wu nu matoo metit
mu doora jur jamm
Data fàxxe
Heer wuy tàkk tibbé
Ci butitu njuru
suuf,
Toj
Guddi géej guy
mbaaw def safara
Taal di tàkk ci
suuf
Taal di tàkk ci
kaw
Leer nan di weer
Leer nan di jant
Kàddu gi di dënu
Bëtt leer nan ci
géej gu mer
Taal jàpp di jant
Taal japp di weer
Te di nàcc leer
nànn
NdÊk Daawur
Gore dafa juddu
di Ngor ci kàddu
nu géntee ko
noonu.
Jànt fenk
Fekk suuf daw lu
bare
Mu teel noonu
séddoo
xer donn
ci ngor
Moona coy li ci
tiis
Moona coy li ci
dee
Moona coy li ci
coona
Bi li di
Hewoon ci boppam juddoo
And ak ndaw soosu làmbook lu weex
nu natal ko ci
Aruwaat
Booba Sahara ngiy
menn ba tey !
Fekk Fari di Buur
Dëju dex gu nuul
fii ci Misira
Fekk Ennil ci
Sumer
Jello Lefraat ak
Tiigar
Fekk Tamil taxaw
ci Dilmun
Fekk Maysa, Buur
Fari Oni ak Mze
Door di màng,
Jublu Niseer ak
Kongo ak Zambeez
Fàxx wuti àll biy
nag,
AII biy nax
AII biy garab
Ci barke rab wi
di jant, rab wi di weer
Rab wi dëkk ndox
Rab wi dëkke safara
Rab wi nank suuf
Rab wi nank asammaan
Fekk na ci jamono
yooyu
Dun wi lamboo
mucc lu di xew
êgg di fi wall
Mu né tekk moom
di déglu Biram Kumba
Njéeme ak Jolof
Noona Sunjata né
pëll fàxxe penku joge
Maali¨
Sunjata mooy
lawal ndaali li fii
Meysa Waali Buur
Fari wu xees woowu
donn ko
Baakari door a feen jëkk ci tur wi
waaye Saakura ngoor si dëj ker gu mag gi
Mooy Jaamu buur, wiy tekki réew mi, lawal.
Moom, mooy dëj nguur gi ba fii.
Da fay dàxx ba
yegsi ci géej gii
Dëju fa doon Ganna
Toj fii di Tekruur
Yegg ba fiy jolof Mbeng weesu dal
Ci dund wii di Beer
Waaye nag mà ngoog !
Mansa woowu dafa aji
Nu boom kci
Tajura
Fekk ko ci yoon
Diggante Gize ak:
Barbar
Saakura moomu moo
sanc
Jële suufas
Penk:u ba ci
Géej gii ci Sawu.
Dafa reer wetal
réew mi,
Bàyyi gannaaw
Gaawu ak Mamadu
Noonu di buur yu
gàtt fan
Mu Jog moom ci
boppam
Jiital fi naari
teemiri gaal
Dëddu wutu géenu
Addina
Dafa dëddu mang
dem
Del seetul. Bayyi way
Wi noo way tay
Noona nag feen
Bakkari, Boroom
ndox mi
Di naarelli Mëysa
ci tuur wi
Buur Fari woowu
xer ci ndox
Mooy noot gééj gilé
Dafa defaru ba
jekk
Takk yabaliy ndaw
Nu delsi deey
kow xabar
Gannaawam Konko
Muusaa
Mi kenn dul
nettali wuutu ko.
Nguuram gëna naat
ci digg jamono
law ci Suufas
Afrig mbaaw wër addina
Mu dend natt wu
ndaali jotul
Muusa mo wuutu
Bakari Boroom geej gi
Bakari moo ko jox
nguur gi
lépp ngir jëkk
Teg naari tank
Ak naari junnéy
ngaalam
Ci suuf si fegg
weneen wetu li di Géej gii
Loolu am ci fukki
juneeg natti téeméeribat
ag fukk ag naar
yi topp njudug Isaa.
Mansa Muusa
jottali mbir mi
Boroom nguur yi
ag Boroom xam xam yi
I bn Fadal Alaah
AI Omari nettali ko
Di bindkat, di
seede teewe xamxamu
Ndox wi nitu
Penkuy jamonoom yakkali
Dafa ko wax ci
xabaaru Buur yi ag Nguur yi
Ci Masaalig El
Absaar fi
Mamaalig El
Amsaar
Téeréem wi mu
rëdd ci fukki at wi xewxew
woowu xewoon.
Boy wann ci jamono
Tukki woowu toppe natti junnibi at
Tukki géeju
lingéer Hashepsut
Ci Punt réewu
Maam ya.
Am na, naari
junnibi at lu weesoo jamono ja Nekao
Sumbe, wër sunu suuf
yii
Nga toog fii di
gis lu rëy
Soo boolee Astorolab, Busol
Ak li bees ci
xamxamu ndox wi feene Penku addina,
ci yooyu jamano
Daa daj ci paspas
yu fésul yooyu
Dox diggante
Permar wu mag wi
Sankara déj fa Misira
Per wi nu mar Askia Mohammed fa Sonraay
Permar wu
mag wi Olmek yi tabax fii di tay
Amerig
Dèllu jàmm né
noyy
Na ca njalbeen.
Sunjata bànneex
la ba mu jeex
Guy la menne ci
buy wu sew
Di pepp wu mennam def tiis
Mu samp iy reenam fa mu gëne xoot ci suuf .
Mari Jaata ! Mbër
! Sogolon !
Simbon ! Sogolon!
Jaata
Jàmm ak jàmm ju
né nooy
Ci fukki réewi
fukki nguur yi
Ci réew moomu
leer nann
Waaw goore
waay !
Wasaa ! Wasaa